Sexaw
Apparence
Sexaw ci njaboot gu yaa gog "combrétacées" gi tënk ñaxi yi ci àll ak mànding. Sexaw xeetu garab gu sëkk, man àgg 4 ba 5i met.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Tóortóoram daa tuuti te weex, ba noppi dajaloo te am i dég.
Foytéefam daa wow te yor ay xeeti laaf yuy àgg ba 1,5 sàntimet ci guddaay, ak 1,5 sàntimet ci yaatuwaay.
Meññuwaayam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Sexaw ci réewi sahel gi lay sax: Senegaal, Mali, Niseer, Burkinaa, Gine konaakri/Bisaawóo.
Njariñ li
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Sexaw ràññees na mbaxam ci reesal ak ci moytu ag mbëfër. Ca Senegaal xob yi dañ ko fas ak i xëddee di ko jaay ngir defarug dute mbaa ndékki.
Nataali sexaw
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Combretum micranthum
Turam ci yeneen làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Araab: Farañse: kinkeliba