Melosuufug Senegaal
Barabu Senegaal la ngi féete ci diggante 12°8(fukk ak ñaari aj juroom-ñett) ak 16°41 ci tus-wu-gaar wu bëj-gànnaar ak 11°21 ak 17°32 ci tus-wu-taxaw wu sowwu. wàllam wi féete sowwu mooy wi gën a nekk sowwu ci goxu Afrig. Am 15.85 miliyoŋ ciy way-dëkk (2017)
Senegaal la ngi tëdd ci 196 712 km kaare, Sun ko méengale ak dëkkandoom yii di Mali ak Gànnaar, di nan gis ne réew mu tuuti la.
Senegaal a ngi am 11 diwaan, 35 gox, 109 gox-goxaan
Kilimaa
SoppiSenegaal, li ñuy wax klimaab Sahel la am. Looloo waral mu am jamonoy taw, di ko wax nawet, ak jamono jum dul taw dana-ka, di ko wax noor. Nawet a ngi door maami-koor jeex kori, waxset di jamono ji muy gën a taw nekk ci baraxlu-koor (day aju ci fi nga nekk: bëj-gànnaar walla bëj-saalum). Noor a ngi door koor jeex maami-koor. Tangoor gi gën a kawe tangaay lay ame, ci nawet bi. Yi gën a suufe ci weeru tamxarit.
Ci li topp tefes gi, ngelaw liy bàyyeekoo ci géej gi mooy tax muy gën a sedd, tangaay bi day nekk ci diggante 16°C ak 30°C, waaye ci digg bi ak penku bi day toll ci 41°C.
Séddatle
SoppiSenegaal a ngi séddatliku ciy diwaan aki gox ak ay gox-goxaan
Diwaan yi
SoppiSenegaal am na fukk ak benn ciy diwaan:
Melosuufug Afrig |
Afrig gu Bëj-saalum • Alseeri • Angolaa • Bene • Botswana • Burkinaa Faaso • Buruundi • Kamerun • Kap Weer • Réewum Diggu Afrig • Bennoo yu Komoor • Kongóo-Brasaawiil • Kongóo-Kinshasa • Kot Diwaar • Jibuti • Isipt • Eriitere • Ecoopi • Gaboŋ • Gaambi • Gana • Gine • Gine-Bisawóo • Gineg yamoo • Keeñaa • Lesoto • Liberiyaa • Libi • Madagaskaar • Marook • Malawi • Mali • Móoris • Gànnaar • Mosambik • Namibi • Niseer • Niseeriyaa • Ugandaa • Ruwandaa • Sahara gu Sowwu • Sao Tome-ak-Principe • Senegaal • Seysel • Siraa Leyoon • Somali • Sudaan • Suwaasilaand • Tansani • Cadd • Togo • Tuniisi • Sambi • Simbaawe